Kharebi-Thione Seck

Kharebi

歌手:Thione Seck

专辑:Favori

时间:2000-01-01

    使用手机浏览器「扫一扫」

    在手机上保存,获得更好体验

标签
歌词

Kharebi - Thione Seck/Raam Daan

Composed by:Thione Seck/Raam Daan

Seen àddunaa gi nii yee yee yee

Barki démb seeni maam la woon

Démb seeni baay

Tay jii ñook seeni doom

Ñuy doxal apartheid

Seen àddunaa gi nii yee yee yee

Barki démb seeni maam

Démb seeni baay

Tay jii ñook seeni doom

Ñuy doxal apartheid

Waa Hollànd a njëkka ñëw

Ci jamonoy dix-sèptieme siècle

Ray boshimens yaa

Maanaam nit ñu ñuul ñaa

Jaay leen doole fitnaal leen

Taal seeni màkkaan

Tëral seenuw làkk muy l'Afrikaaners

Juddóo cim réew màggee cim réew

Amuloo fa baat amuloo fa yoon

Suba su nekk ñu futti la def la yaramu neen

Ci say kanami doom bu yàggee

Dinga jéengu dinga jéengu

Jéengu yamale dund ak dee

Xiifal ma di ma liggéeyloo

Ba amuma dooley xeex

Yeew sama tànk

Bàyyi ma ci liw bi

Lëmbaaje samam xel

Ba suma la gisee damay tiit

Boo ma saagaa ma ne waaw

Apartheid

Winnie Winnie Mandela

Winnie yooy Mandela

Winnie Winnie Mandela

Winnie yoo Mandela

Winnie Winnie yoo yii yaaw

Winnie Winnie Mandela

Winnie yooy Mandela

Winnie Winnie Mandela

Winnie yoo Mandela

Winnie Winnie yoo yii yaaw oooh

Nga def ma mbaam te duma moom

Jël sama jabar def mbindaan

Aj sama payoor ci bula neexe

Te duma ci dégg wax bu neex

Apartheid apartheid kañ lay jeex?

Mandela dina mësa daan

Winnie Winnie yéey yii yaa waaw waaw

Xiifal ma di ma liggéeyloo

Ba awma dooley xeex

Yeew sama tànk

Bàyyi ma ci liw bi

Lëmbaaje samam xel

Ba buma la gisee tiit

Mandela di raam a raam

Yàgg yàgg dina mësa daan

Winnie Winnie yée i yaa

Oooo

Bóom nañu Steve Biko

Ray nañu Benjamin Moloïse

Am na ñu réer te dootu ñu feeñ

Apartheid kañ lay jeex ?

Nelson Nelson Nelson Nelson

Nelson Mandela

Nelson Nelson Nelson Nelson

Nelson Mandela

展开显示全部歌词